Lan la?
Armand Vitesse ab barab la bu ñu saytu seen bopp, ngir liggéey ci sa bopp, defaraat, sàkk ak jàngal sa bopp. Barab bi ci garaasub kër la nekk, te ñu ko maye ci neen. Lépp ci fay li nga bëgg la. Ay beneewool ñoo yor barab bi. Armand Vitesse du mbootaay.
Jéego la ngir jàppalante, di may nit ñi amul alal bu bari ñu mën a toppatoo te defaraat seeni welo, telefon, ordinatëer, jumtukaay yu ndaw yu kuran, ay yere, ak yeneen. Jubluwaay bi tamit mooy ñu séddoo xam-xam te jàngandoo ci barab bu neex te dalal. Bëgg nanu dëgëral bennoo gi ci sunu biir te di ci jële doole!
Danu bëgg bërëb bi ubbeeku te dalal ñépp. Danuy moytu sunuy jikko ak sunuy jëf ngir bañ a indi fii li ñuy merloo feneen (miskin, xeetale, jigeenale, ak bépp xeetu noot).
Soo bëggee bokk ci benn ateliye, sàkku beneen bu bees (nataal, làkk yi, walla lépp loo bëgg!), walla rekk bëgg a naan kafe ak ñeneen, dalal nañu la! Ba ci kanam ci Armand Vitesse!